1
1.Yowaan 5:14
Kàddug Yàlla
KY
Kóolute gi nu am ci Yàlla moo di su nu ko ñaanee lenn lu dëppook coobareem, da nuy nangul.
Compare
Explore 1.Yowaan 5:14
2
1.Yowaan 5:15
Gannaaw xam nanu ne moo nuy nangul lépp lu nu ko ñaan, xam nanu ne dagaan yi nuy sàkku ci moom, am nanu ko.
Explore 1.Yowaan 5:15
3
1.Yowaan 5:3-4
Ndax kat sopp Yàlla moo di, ay ndigalam nu di ko sàmm, te ay ndigalam diisul. Képp ku sosoo ci Yàlla, moo daan àddina; te galgal biy daan àddina mooy sunu ngëm.
Explore 1.Yowaan 5:3-4
4
1.Yowaan 5:12
Ku am Doom ji, yaa texe; ku amul Doomu Yàlla, texewuloo.
Explore 1.Yowaan 5:12
5
1.Yowaan 5:13
Lii maa leen ko bind, yeen ñi gëm turu Doomu Yàlla, ngir ngeen xam ne texe ngeen ba fàww.
Explore 1.Yowaan 5:13
6
1.Yowaan 5:18
Xam nanu ne képp ku sosoo ci Yàlla doo sax ci bàkkaar, waaye Kenn ki sosoo ci Yàlla moo koy sàmm, ba ku bon ki du ko manal dara.
Explore 1.Yowaan 5:18