Tit 1:7-8
Tit 1:7-8 TI
Ndaxte kuy sàmm mbooloo mi mooy jawriñu Yàlla, kon warul am ŋàññ, walla di ku dëgër bopp mbaa ku tàng bopp; warul dib màndikat walla xeexkat mbaa ku bëgge ci alal ju lewul. Waaye war na man gan te bëgg lu baax, di ku maandu te jub, ku sell te not boppam.





