Room 16:25-27
Room 16:25-27 TI
Santleen Yàlla, mi leen mana saxal bu wér ci dëggu xibaaru jàmm, bi may waare ci mbirum Yeesu Kirist! Nekkoon na kumpa gu làqu diirub ay ati at, waaye léegi nag Yàlla dindi na nu ci kumpa. Santaane na, nu yégle xibaar boobu ci xeeti àddina sépp, ci firi Mbindi yonent yi, ngir nit ñi man koo gëm, ba jébbalu. Yàlla mi jagoo xam-xam bépp, moom rekk moo yelloo ndam ba fàww, jaar ci Yeesu Kirist! Amiin.





