Peeñu ma 17:8
Peeñu ma 17:8 TI
Rab wi nga gis nekkoon na waaye nekkatul. Dina génn ca kàmb gu xóot ga, ba noppi sànku. Noonu waa àddina, ñi ñu bindul seeni tur, li dale ci njàlbéenu àddina, ci téereb dund bi, dinañu yéemu, bu ñu gisee rab wi, ndaxte nekkoon na waaye nekkatul te dina nekkaat.





