Macë 28:12-15
Macë 28:12-15 TI
Noonu sarxalkat ya dajaloo ak njiit ya, ñu diisoo; ba noppi ñu fab xaalis bu bare, jox ko xarekat ya, ne leen: «Nangeen wax lii: “Ay taalibeem ñëw nañu ci guddi, sàcc ko, bi nuy nelaw.” Te bu ko boroom réew mi yégee nag, dinanu ko neexal, ngir rawale leen.» Wottukat ya nag fab xaalis ba, def la ñu leen santoon. Te nettali boobu siiw na ci Yawut yi ba bésu tey.





