YouVersion Logo
Search Icon

Macë 20:26-28

Macë 20:26-28 TI

Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgga nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga, te ku bëgga nekk njiit, na nekk seen jaam. Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.»