Luug 4:5-8
Luug 4:5-8 TI
Seytaane yóbbu na ko fu kawe. Ci xef ak xippi mu won ko réewi àddina sépp, ne ko: «Dinaa la jox bépp sañ-sañu nguur yii ak seen ndam ndaxte jébbal nañu ma ko, te ku ma soob laa koy jox. Kon boo ma màggalee, dinga moom lépp.» Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom te jaamu ko moom rekk.”»





