Luug 4:18-19
Luug 4:18-19 TI
«Xelum Boroom baa ngi ci man, ndaxte moo ma tànn, ngir ma yégal néew doole yi xibaaru jàmm bi. Dafa maa yónni, ngir ma yégal jaam ñi ne dinañu leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, te jot ñi ñu not, tey yégle atum yiw, mi jóge ci Boroom bi.»





