Yowaan 16:22-23
Yowaan 16:22-23 TI
Noonu nag ngeen di jàqe, yéen itam. Waaye dinaa leen gisaat, seeni xol sedd, te seen mbég moomu, kenn du ko mana dindi. Bés boobu dootuleen ma laaj dara. Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Baay bi dina leen may lu ngeen ko ñaan ci sama tur.





