Efes 4:11-13
Efes 4:11-13 TI
Moo may ñii di ay ndawam, ñii ay yonent, ñii ay taskati xibaaru jàmm bi, ak ñeneen ñuy sàmm mbooloom ñi gëm te di ko jàngal. Maye na leen, ngir ñu waajal gaayi Yàlla yu sell yi, ñu mana bey seen sas ci taxawal mbooloom Kirist, di jëmmam. Noonu nu mànkoo ci sunu ngëm ak ci xam Doomu Yàlla ji, ba kera nuy egg ci nekk nit ku sotti te taxaw taxawaay bu dëppook matug Kirist.





