Efes 3:16-19
Efes 3:16-19 TI
Ma di ko ñaan, mu may leen, ci kaw ndamam lu amul kem, Xel mu Sell mi feddali seen baatin ak kàttan gu mag, ba Kirist dëkk ci seeni xol ci kaw ngëm. Te ngeen sax noonu te sampu ci mbëggeelu Yàlla, ba jagoo, yéen ak gaayi Yàlla yu sell yépp, guddaay ba, yaatuwaay ba, kawe ga ak xóotaay ba, te xam mbëggeelu Kirist, gi raw mépp xel. Noonu dingeen fees dell ak matug Yàlla.






