Jëf ya 8:29-31
Jëf ya 8:29-31 TI
Xel mi nag ne Filib: «Dabal watiir wale.» Noonu Filib dawsi, mu dégg waayi Ecópi ja, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi. Mu laaj ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?» Mu ne ko: «Nu ma ko mana xame, su ma ko kenn firilul?» Mu woo Filib nag, mu yéeg, toog ak moom.





