YouVersion Logo
Search Icon

Jëf ya 2:2-4

Jëf ya 2:2-4 TI

Ca saa sa riir jollee asamaan, mel ni ngelaw lu gaaw te bare doole, daldi fees dell kër, ga ñu toog. Te ay làmmiñ yu mel ni sawara feeñu leen, ñu tasaaroo ci seen biir, toŋ ca kaw kenn ku nekk. Noonu ñu fees ak Xel mu Sell mi ñoom ñépp, ñu daldi wax yeneen làkk, ni leen Xel mu Sell mi maye, ñu wax ko.