1.Yowaan 4:1-2
1.Yowaan 4:1-2 TI
Samay soppe, buleen gëm xel mu nekk, waaye nattuleen xel yi, ba xam ndax ci Yàlla lañu jóge walla déet, ndaxte naaféq yu bare yu mbubboo turu yonent jóg nañu, tasaaroo ci àddina si. Ci lii lanu xàmmee Xelum Yàlla: mépp xel mu nangu ne, Yeesu Kirist ñëw na, nekk nit, ci Yàlla la bokk.








