Bible App logo
Search Icon

Room 9

9
Yàlla moo tànn bànni Israayil
1Dëgg laay wax, Almasi bi seede na ko, fenuma. Sama xol moo ma seedeele Noo gu Sell gi, ne lii may wax dëgg la: 2li may wax moo di tiis wu réy laa am ak naqaru xol wu dakkul, 3nde man doon naa ñaana alku sax, daggoo ak Almasi bi, ngir jàmmi sama bokki xeet, sama bokki deret. 4Ñooñoo di xeetu Israayil wi xéewloo céru doon doomu Yàlla, Yàlla won na leen jataayam ju yànj, fas ak ñoom kóllëre, jox leen ndigali yoon wi ak doxalinu njaamu Yàlla aki digeem; 5ñoo soqikoo ci maam yu baax ya; ci wàllu doom aadama it, ci ñoom la Almasi bi soqikoo, di Yàlla, tiim lépp, te yelloo cant ba fàww. Amiin.
6Du caageenu kàddug Yàlla moo neen, ndax ñi bokk ci xeetu Israayil ñépp duñu Israayil tigi. 7Te it sëti Ibraayma yépp bokkuñu ci askanam, waaye li Mbind mi indi moo di: «Ci Isaaxa lees di tudde saw askan#9.7 Seetal ci Njàlbéen ga 21.12.8Loolu di tekki ne du sëti Ibraayma yi ci wàllu deret ñoo di doomi Yàlla, waaye doom yi seenub juddu dëppoo ak digeb Yàlla, ñoom lañu jàpp ne ñooy askanu Ibraayma. 9Ndax kat kàddug dige ba nii la jibe: «Nëgëni sii déwén laay délsi, te Saarata dina am doom ju góor#9.9 Seetal ci Njàlbéen ga 18.10, 14.
10Te yemul foofu rekk, waaye Rebeka it moo am ay seex yu genn góor jur, muy sunu maam Isaaxa. 11Doom ya nag juddooguñu woon bay def lenn lu baax, mbaa lu bon. Yàlla moo defe noonu ngir wéyal dogal bu dëppoo ak tànnéefu boppam 12bu ajuwul ci kawi jëf, xanaa ci kiy woote. Rebeka#9.12 Rebeka mooy soxnas Isaaxa. la kàddu gii dikkal: «Mag ji mooy surgawu rakk ji#9.12 Seetal ci Njàlbéen ga 25.23.13Noonu la Mbind mi indee ne: «Yanqóoba laa sopp, te Esawu laa foñ#9.13 Seetal ci Malasi 1.2-3.
Sànjum Yàlla rax na yërmande
14Ana lu nu ci mana wax nag? Ndax Yàlla daa wàcc foofu yoon? Mukk kay! 15Ndax kat moo noon Musaa:
«Maay yërëm ku ma neex,
te maay ñeewante ku ma neex#9.15 Seetal ci Mucc ga 33.19.
16Kon nag mbaaxug Yàlla ajuwul ci coobarey nit ki, mbaa aw ñaqam, waaye lépp yërmandey Yàlla la. 17Mbind mi moo indi kàddu ga dikkaloon Firawna, ne ko: «Maa la yékkati, te li ko waral mooy lii ci boppam: ngir fésal sama doole ci yaw, ngir itam sama riirum tur dajal àddina#9.17 Seetal ci Mucc ga 9.16.18Kon nag Yàlla mooy yërëm ku ko neex, te ku ko neex lay dëgëral xolam.
19Xam naa dinga ma ne: «Ana kon lu Yàlla di sikkeeti? Coobarey Yàlla, ana ku koy fanq?» 20Waaye yaw nit ki, yaay kan bay weddi Yàlla? Ndax këf ku ñu tabax dina ne ka ko tabax: «Lu tax nga sàkke ma nii?» 21Tabaxkatu ndab bi xanaa daa amul sañ-sañ ci ban bi muy liggéeye, ngir tabax ci bennub tooyal lenn ndabal teraanga ak leneen ndabal njoogaan?
22Yàlla dafa nammoona wone am sànjam, xamle dooleem. Teewul moo muñal lool ay ndab yu yelloo am sànjam, te seen sànkute ñoroon xomm. 23Su dee Yàlla moo def loolu nag ngir fésal màggaayu teraangaam, ñeel ay ndab yu xéewloo yërmande, te mu waajalaloon leen teraanga? 24Nun ci ndabi yërmande yi Yàlla woo lanu bokk, te du ci Yawut yi rekk lees nu seppee, waaye ci jàmbur ñi dul Yawut itam. 25Moom la wax it ci téereb Ose ne:
«Ñi dul woon sama ñoñ,
ñoom laay wax sama ñoñ,
ñooñu dul woon samab xejj,
ñoom laay xejjoo#9.25 Seetal ci Ose 2.25.
26«Te foofa ñu leen noon: “Yeen, dungeen sama ñoñ,”
fa lees leen naa: “Yeenay doomi Yàlla jiy dund#9.26 Seetal ci Ose 2.1..”»
27Ci mbirum Israayil la Yonent Yàlla Esayi itam xaacu woon ne:
«Su bànni Israayil tolloo ni feppi suufas géej sax,
as ndes a ciy mucc#9.27 Seetal ci Esayi 10.22.
28Ndax kàddu gi Boroom bi wax:
«Moo koy sottal ci lu gaaw ci kaw suuf#9.28 Seetal ci Esayi 10.23.
29Mooy itam la Esayi waxoon lu jiitu, ne:
«Bu nu Boroom gàngoori xare yi
waccalul woon kuutaay,
ni Sodom lanuy mel, Gomor lanuy neexool#9.29 Seetal ci Esayi 1.9.
Bànni Israayil déggoowul ak xibaaru jàmm bi
30Ana lu nu ci mana wax? Xeet yu dul Yawut te sàkkuwuñu woon ag njub, ñoo jot àtteb njub, te mooy njub gi ngëm di maye. 31Waaye xeetu Israayil wi sàkku woon yoonu njub, ñoo moy yoon wi. 32Ndax lan? Sukkandikoowul ci ngëm, xanaa ay jëf. «Doj wuy fakkastale,» moom lañu fakkastaloo. 33Noonu la Mbind mi indee ne:
«Maa ngii di dëj fi Siyoŋ doj wuy fakkastale,
mooy xeer wuy daaneel,
waaye ku ko gëm, doo rus#9.33 Seetal ci Esayi 8.14; 28.16.

Currently Selected:

Room 9: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in