Room 13
13
Na ñépp déggal njiit yi
1Na ku nekk déggal njiit yi yor kilifteef, nde amul njiit lu bawoowul fa Yàlla, te njiit yi toog, Yàlla moo leen tabb. 2Moo tax kuy bañal njiit, tëralinu Yàlla nga bañal, te ñi bañal njiit, ñoo wool seen bopp mbugal. 3Kuy def lu baax nag, doo ragal kilifa yi, kiy def lu bon moo leen di ragal. Soo bëggee mucc ci ragal kilifa nag, defal lu baax, jot ngërëmam. 4Ndax kilifa gi mooy ndaw li Yàlla yebal ngir sa jàmm. Waaye soo dee def lu bon, ragalal, ndax kilifa gi yorul ab saamar cig neen; mooy ndawal Yàlla liy añale, te mooy jottali am sànj mu wàcc ci kuy def lu bon. 5Moo tax nangul njiit di wartéef, ndax njariñal nangul njiit yemul rekk ci mucc ci am sànj, waaye xel mu dal a ngi ci.
6Loolu moo waral it ngeen di fey galag, ndax njiit yi koy feyeeku kat, ñooy jawriñi Yàlla yi sasoo googu kilifteef. 7Joxleen ku nekk li ngeen warlook moom; ku ngeen wara fey galag, feyleen ko ko; ku ngeen wara fey juuti, feyleen ko ko; ku ngeen wara weg, wegleen ko; ku ngeen wara teral, teralleen ko.
Cofeel moo tënk yoonu Musaa
8Buleen ameel kenn bor, lu moy borub soppante; ndax ku sopp sa moroom, yaa matal yoonu Musaa. 9Ndax ndigal yii kat: «Buleen njaaloo, buleen bóom, buleen sàcc, buleen xemmem#13.9 Seetal ci Mucc ga 20.13-15, 17.,» ak leneen ndigal lu mu mana doon, ci genn kàddu gii la tënke: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom#13.9 Seetal ci Sarxalkat yi 19.18..» 10Cofeel du waral kenn def moroomam lu bon; kon cofeel moo matal sëkk yoonu Musaa.
Teewlu war na gëmkat ñi
11Li tax ngeen wara gëna farlu ci loolu mooy, xam ngeen jant yi nu tollu; seen waxtuw yewwu jot na ba noppi, nde léegi la nu mucc gëna jege ba nuy doora gëm. 12Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer. 13Nanu jëfe jëfin wu jekka def bëccëg; nanu sore xawaare yi ànd ak moy, ak màndite, sore baane bu lewul, ak ñaawtéef yu ni mel, te sore ŋaayoo ak kiñaan. 14Waaye yiirooleen Sang Yeesu Almasi bi, te ngeen baña yittewoo seen bakkan, ngir di topp seeni xemmemtéef.
Currently Selected:
Room 13: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright

: