Room 11
11
Yàlla waccul bànni Israayil
1Ma ne kon, xanaa Yàlla daa wacc ñoñam? Mukk kay! Man ci sama bopp ci Israayil laa bokk, askanoo ci Ibraayma, giiroo ci Beñamin. 2Yàlla waccul ñoñam ñi mu ràññee woon lu jiitu. Am dangeena xamul li Mbind mi indi ci mbirum Ilyaas, ba mu dikkee Yàlla njàmbat lu jëm ci Israayil? Mu ne: 3«Boroom bi, say yonent, rey nañu leen; say sarxalukaay, màbb nañu leen; man doŋŋ maa fi des, te ñu ngi wut sama bakkan#11.3 Seetal ci 1.Buur ya 19.10, 14..» 4Ana lu ko Yàlla tontu? Da ne: «Beral naa sama bopp juróom ñaari junniy nit (7 000) ñu sujjóotaluloon Baal tuur mi#11.4 Seetal ci 1.Buur ya 19.18..» 5Kon nag naka noonu itam ci jamonoy tey jii, aw ndes a ngi fi, te ci kaw yiw lees leen tànne. 6Gannaaw aw yiw a tax nag, dootul seen peyu jëf, lu ko moy aw yiw noppee doon aw yiw.
7Kon léegi nag? Li am moo di, li bànni Israayil doon wut, amuñu ko. Ñi Yàlla tànn ñoo ko am, ña ca des, seenum xel a dërkiis. 8Noonu lees binde ne:
«Yàlla moo leen jox xelum ngëmment,
ak bët yu dul gis, ak nopp yu dul dégg,
ba bésub tey jii#11.8 Seetal ci Baamtug yoon wi 29.3; Esayi 29.10..»
9 Daawuda it wax na ne:
«Yal na seen ndab di seenum yeer,
boole ci dib caax,
te di fiir gu ñuy daanu,
muy seenub yool.
10Yal na seeni gët giim, ba duñu gisati,
yal nañu sëgg ba fàww#11.9-10 Seetal ci Taalifi cant 69.23-24..»
Lu jëm ci muccug ñi dul Yawut
11Moo tax ma ne xanaa ba bànni Israayil tërëfee, jéll bu ñu dul jógati lañu daanu? Mukk kay! Waaye tooñug bànni Israayil moo waral muccug jàmbur ñi dul Yawut, ba tax bànni Israayil siis leen. 12Gannaaw tooñug bànni Israayil mooy xéewalu àddina si, seenug néewle di xéewalu jàmbur ñi dul Yawut, kon bu bànni Israayil yembee, ndaw xéewal gu gënatee baawaan!
13Léegi nag yeen jàmbur ñi dul Yawut laay waxal. Gannaaw maay ndaw li ñu yebal ci jàmbur ñi dul Yawut, samab yónnent laay teral. 14Jombul sama liggéey dina yee fiiraangey sama bokki Yawut ñi, ba ñenn ci ñoom mucc. 15Ndax kat ba Yàlla dàqee Israayil, ca la àddina juboo ak Yàlla. Kon nag bu leen Yàlla delloosee, ana lu muy jur lu moy dee-dekki? 16Ndax kat ab sarax bu génnee ci nootu sunguf, di ndoortel meññeef, su boobu sarax sellee, tooyalub sunguf bépp ay sell. Ndax su reenu garab sellee, car ya it sell.
17Waaye su ñu tenqee lenn ci cari oliwu kër, te yaw ngay caru oliwu àll, ñu indi la, jabtal ci oliwu kër gi, nga wuutu car ya ca fàqe, ba mana xéewloo meen miy wale ci reenu oliwu kër gi, di ko dundal, 18bumu tax nga bàkku ci kaw car ya fàqe. Soo dee bàkku, xamal ne du yaa yenu reen bi, waaye reen bee la yenu.
19Xam naa dinga ne: «Car yooyu, dees leena tenqi, ngir jabtal ma.» 20Dëgg it; waaye ngëmadi moo leen fa tenqee, te yaw, ngëm a la fa teg. Bu ko réy-réyloo, waaye ragalal. 21Ndegam cari judduwaale ya la Yàlla déegul, moytul mu bañ laa déeg yaw itam.
22Xoolal kon ni Yàlla baaxe ak ni mu ragloo; ci ñi déggadi la raglu, baax ci yaw, ndegam cig mbaaxam nga sax; lu ko moy dees na la tenqi yaw itam. 23Car ya fàqe woon itam, su ñu wéyewul ngëmadi, dees leen di delloo ca ndey ja, nde Yàlla man na leen caa saxalaat. 24Ndax kat, ndegam yaw lañu tenqee ci oliw gi ci àll bi, jabtal la ci oliwu kër gi dul sa ndey, astamaak car yi oliwu kër gi di seen ndey, nde saxalaat leen ca mooy gëna yombati.
Yàlla ñépp la yërëm
25Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bëgguma ngeen umple mii mbóot: ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israayil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat. 26Su boobaa nag, bànni Israayil gépp ay mucc, noonee ko Mbind mi indee ne:
«Siyoŋ la wallukat bay jóge,
mooy tenqee ngëmadi ci askanu Yanqóoba.
27Loolooy doon sama kóllëreek ñoom,
kera ba may far seeni bàkkaar#11.26-27 Seetal ci Esayi 59.20-21; 27.9; Yeremi 31.33-34..»
28Ci wàllu xibaaru jàmm bi, ay noon la Yawut ñi taxawe, te muy xéewal ci yeen ñi dul Yawut. Waaye ci wàllu dogal bi tànn Yawut ñi, ay soppe lañu, te seeni maam tax. 29Ndax Yàlla kat, ay mayam akub wooteem, lenn du ci toxu. 30Yeena déggadi woon, waaye tey daj ngeen yërmande, ndax déggadig Yawut yi. 31Noonu itam la Yawut yi déggadee tey, ba ni ngeen daje yërmande, ñoom it ñu daje ni yërmande. 32Yàlla moo tëj nit ñépp ci seenug déggadi, ngir yërëm leen ñoom ñépp.
Yàllaa yelloo teraanga
33Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam!
34«Ana ku mana nànd xalaatu Boroom bi?
Ana ku ko mana digal#11.34 Seetal ci Esayi 40.13.?»
35«Ana ku ko dawlul lenn,
ba mu war koo delloo#11.35 Seetal ci Ayóoba 41.3.?»
36Ci moom la lépp sosoo, ci moom la lépp sottee, te moom la lépp ñeel. Moom la daraja ñeel ba fàww! Amiin.
Currently Selected:
Room 11: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright

: