Peeñu ma 6:12-13
Peeñu ma 6:12-13 KY
Ma gisati bi muy tàyyi juróom benneelu tayu bi, suuf daldi yëngu bu baaxa baax, jant bi ñuul kukk, weer wi wépp xonq curr ni deret. Biddiiw yi fàqe asamaan, wadd ci suuf, ni doom yu xaay yu ngëlén gësëm seen ndey.





