YouVersion Logo
Search Icon

Màndiŋ ma 7

7
Daloob jaamookaay bi laaj nay sarax
1Keroog ba Musaa sampee jaamookaay bi ba noppi, diw na ko ngir sellal ko, mook mboolem ay jumtukaayam, sarxalukaay beek mboolem ndabam it, mu boole diw, sellale ko. 2Ba loolu amee kilifay Israayil yi jiite seeni kër maam dikk. Ñooñoo doon njiiti giir yi te ñoo doon saytu limeefu nit ñi. 3Ñu indil Aji Sax ji seen sarax, muy juróom benni watiir ak fukki nag ak ñaar; ñaari kilifa yu nekk, benn watiir; kilifa gu nekk, wenn nag, ñu yóbbu lépp fa kanam jaamookaay ba. 4Aji Sax ji wax Musaa, 5ne ko: «Nangul lii, mu jëm ci liggéeyu xaymab ndaje mi, te nga jox ko Leween ñi, ku ci nekk ak li liggéeyam laaj.»
6Musaa nangu watiir yaak nag ya, jox Leween ñi. 7Yii ñaari watiir ak ñeenti nag, mu jox Gersoneen ña, na ko seen liggéey laaje, 8yee ñeent, mu booleek juróom ñetti nag, jox Merareen ña, na ko seen liggéey laaje, ci njiital sarxalkat ba Itamar doomu Aaróona. 9Keyateen ña nag, joxu leen, ndax yu sell ya lañu sasoo woona gàddu.
10Ci biir loolu kilifa yi indi itam saraxu daloob sarxalukaay bi, keroog bés ba ñu koy diw. Ñu daldi joxe seeni sarax fi kanam sarxalukaay bi. 11Teewul Aji Sax ji wax Musaa, ne ko: «Kilifa yiy joxesi seen sarax, yi jëm ci daloob sarxalukaay bi, nañu ko def bés bu nekk, kenn.»
12Ki joxe saraxam ci bés bu njëkk bi, ñeel giirug Yuda, mooy Naason doomu Aminadab. 13Ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp bi, 14ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 15ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 16ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 17ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Naason doomu Aminadab.
18Bésub ñaareel ba, kilifag Isakareen ña, Netaneel doomu Cuwar moo indi saraxam, 19sarax ba mu indi di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, 20ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 21ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 22ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 23ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Netaneel doomu Cuwar.
24Bésub ñetteel ba, kilifag Cabuloneen ña, Elyab doomu Elon moo aye, 25ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, di juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, 26ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 27ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 28ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 29ak saraxas cant ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Elyab doomu Elon.
30Bésub ñeenteel ba kilifag Rubeneen ña, Elicur doomu Sedeyur moo aye, 31ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, di juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, 32ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 33ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 34ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 35ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Elicur doomu Sedeyur.
36Bésub juróomeel ba kilifag Cimyoneen ña, Selumyel doomu Curisadaay moo aye, 37ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, 38ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 39ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 40ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 41ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Selumyel doomu Curisadaay.
42Bésub juróom benneel ba kilifag Gàddeen ña, Elyasaf doomu Dewel moo aye, 43ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, 44ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 45ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 46ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 47ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Elyasaf doomu Dewel.
48Bésub juróom ñaareel ba kilifag Efraymeen ña, Elisama doomu Amiyudd moo aye, 49ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, 50ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, muy téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 51ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 52ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 53ak saraxas cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Elisama doomu Amiyudd.
54Bésub juróom ñetteel ba kilifag Manaseen ña, Gamliyel doomu Pedacur moo aye, 55ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, 56ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 57ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 58ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 59ak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Gamliyel doomu Pedacur.
60Bésub juróom ñeenteel ba kilifag Beñamineen ña, Abidan doomu Gidoni moo aye, 61ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, 62ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 63ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 64ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 65ak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Abidan doomu Gidoni.
66Bésub fukkeel ba kilifag Daneen ña, Axyeser doomu Amisadaay moo aye, 67ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, 68ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 69ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 70ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 71ak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Axyeser doomu Amisadaay.
72Bésub fukkeel baak benn, kilifag Asereen ña, Pagyel doomu Okkran moo aye, 73ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, 74ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 75ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 76ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 77ak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Pagyel doomu Okkran.
78Bésub fukkeel baak ñaar kilifag Neftaleen ña, Axira doomu Enan moo aye, 79ab saraxam di benn ndabu xaalis bu diise téeméeri siikal ak fanweer, muy kilook liibar, ak benn këllu xaalis bu diise juróom ñaar fukki siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, muy juróom ñetti téeméeri garaam, lu ci nekk fees ak sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ngir saraxu pepp, 80ak senn mbàttus wurus su fees ak cuuraay te diise fukki siikal, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom, 81ak wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak menn kuuyu menn at, ngir saraxu rendi-dóomal, 82ak wenn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar, 83ak saraxu cant gi ci biir jàmm, di ñaari yëkk ak juróomi kuuy yu mag ak juróomi sikket, ak juróomi kuuyu menn at. Looloo doon saraxu Axira doomu Enan.
84Loolooy saraxi daloob sarxalukaay ba, ca bés ba ñu koy diw, sellal ko, lépp bawoo ca kilifay Israayil. Ndabi xaalis ya fukk laak ñaar, këlli xaalis ya di fukk ak ñaar, bàttuy wurus ya di fukk ak ñaar, 85ndabal xaalis lu nekk di téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, këll bu nekk di juróom ñaar fukki siikal, di juróom ñetti téeméeri garaam, mboolem xaalisu jumtukaay yi di ñaari junniy siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, ak ñeenti téeméer (2 400), di ñaar fukki kilook juróom ñaar ak juróom benni téeméeri garaam (27 600). 86Fukki bàttuy wurus yi feese cuuraay, mbàttu su ci nekk fukki siikal la, ci siikal bi ñu yoonal ci néeg bu sell bi, di téeméeri garaam ak fukk ak juróom (115), mboolem wurusu bàttu yi di téeméeri siikal ak ñaar fukk (120), muy kilo ak ñetti téeméeri garaam ak juróom ñett fukk (1 380). 87Mboolem nagi saraxu rendi-dóomal yi, fukki yëkk yu ndaw ak ñaar la, kuuy yu mag yi di fukk ak ñaar, kuuyi menn at yi di fukk ak ñaar, ànd ak seen saraxi pepp, sikketi saraxu póotum bàkkaar bi di fukk ak ñaar. 88Mboolem nagi saraxu cantu biir jàmm yi, ñaar fukki yëkk yu ndaw ak ñeent la, kuuy yu mag yi di juróom benn fukk, sikket yi di juróom benn fukk, kuuyi menn at yi di juróom benn fukk. Loolooy saraxi daloob sarxalukaay ba, gannaaw ba ñu ko diwee, sellal ko.
89Bu Musaa duggaan ca biir xaymab ndaje ma, ngir wax ak Aji Sax ji, day dégg baat ba di wax ak moom, bawoo fa tiim kubeeru gaalu seedes kóllëre ga, ca diggante ñaari serub ya. Noonu la daan waxeek moom.

Currently Selected:

Màndiŋ ma 7: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in