YouVersion Logo
Search Icon

Màndiŋ ma 3:12-13

Màndiŋ ma 3:12-13 KY

«Man mii nag, maa seppee Leween ñi ci bànni Israayil, maa leen weccoo mboolem taaw bu góor bu njëkka juddoo ci ndeyam, ci biir bànni Israayil. Kon nag Leween ñi, sama cér lañuy doon. Ndax lépp luy taaw bu góor, sama cér la. Keroog ba ma reyee lépp luy taaw bu góor ca réewum Misra, ca laa sellalal sama bopp lépp luy taaw ci Israayil, dale ci nit ba ci jur. Maa leen séddoo. Maay Aji Sax ji.»

Video for Màndiŋ ma 3:12-13