Màndiŋ ma 17
17
Andi way-fippu ya firnde la
1Aji Sax ji waxati Musaa, ne: 2«Waxal Elasar doomu Aaróona, sarxalkat bi, ne ko mu seppee and yi ci lakk gi, ndax lu sell la, te xal yi, na ko tuur fu sore. 3And yooyii seeni boroom feye seen bakkan seeni bàkkaar, dees koy tëgg, ba mu tàlli, xoobe ko sarxalukaay bi. Gannaaw fi kanam Aji Sax ji lañu indi and yi, ba tax mu doon lu sell, na and yi doon firnde, ñeel bànni Israayil.» 4Ci kaw loolu Elasar sarxalkat bi jël andi xànjar, ya ña dee ca lakk ga indi woon, ñu tëgg ko ba mu tàlli, ngir sarxalukaay ba, 5na ko Aji Sax ji santaanee woon, Musaa jottali. Loolu di fàttali bànni Israayil ne benn jàmbur bu bokkul ci askanu Aaróona sañula dikk di taal cuuraay fi kanam Aji Sax ji, lu ko moy lu mel ni li dal Kore ak gàngooram moo koy dal.
Ñaxtu sabab na mbugal
6Ca ëllëg sa mbooloom bànni Israayil gépp a doon ñaxtu ci kaw Musaa ak Aaróona, naan: «Yeen yeena reylu ñoñi Aji Sax ji!» 7Mbooloo maa nga sam Aaróona ak Musaa. Ci biir loolu, ñu ne gees xaymab ndaje ma, gisuñu lu moy niir wa muur ko, leerug Aji Sax ji feeñ.
8Ba loolu amee Musaa ak Aaróona dem ba ca kanam xaymab ndaje ma, 9Aji Sax ji wax ak Musaa, ne: 10«Jógeleen biir mbooloo mii, ma sànk leen léegi!» Ñu ne gurub, dëpp seen jë fa suuf. 11Musaa ne Aaróona: «Jëlal and bi, nga sàkke ci sarxalukaay bi ay xal, teg ci cuuraay, yóbbu gaaw ca mbooloo ma, ba defal leen ag njotlaay, ndax sànj mi tàkke na ci Aji Sax ji, mbas mi tàmbali na!» 12Aaróona këf and ba Musaa wax, daw dugg ca biir mbooloo ma. Ndeke mbas ma tàmbali na ca biir mbooloo ma. Mu def ca and ba cuuraay, daldi defal mbooloo ma njotlaay. 13Naka la taxaw ci diggante ñi dee ak ñiy dund, mbas ma dal. 14Ña dee ca mbas ma nag doon fukki junneek ñeent ak juróom ñaari téeméer (14 700), te bokkul ak ña dee woon ca mbirum Kore ma. 15Ba mu ko defee Aaróona dellu ca Musaa, ca bunt xaymab ndaje ma, fekk mbas ma dal.
Bant bu wow jebbi na
16Ba loolu amee Aji Sax ji ne Musaa: 17«Waxal ak bànni Israayil, nga nangoo ci mboolem seen kilifay kër maam, aw yet, na wenn yet bawoo ci kër gu ci nekk, muy fukki yet ak ñaar, yet wu ci nekk, nga bind ci turu boroom. 18Turu Aaróona itam, nga bind ko ci yetu giirug Lewi, ndax wenn yet lay doon, ñeel kilifag kër gu ci nekk. 19Nga denc yet yi ca biir xaymab ndaje ma, fa kanam gaalu seedes kóllëre ga, fa may dajeek yeen. 20Su ko defee ki ma tànn, aw yetam dina jebbi, ba ma teqalikoo ak xultuy bànni Israayil yi ñuy xultu ci seen kaw.»
21Musaa àgge ko bànni Israayil, mboolem seen kilifay kër maam jox Musaa aw yet, kilifa gu ci nekk wenn yet, ñeel kër maamam, muy fukki yet ak ñaar, yetu Aaróona bokk ca. 22Musaa teg yet ya fa kanam Aji Sax ji, ca biir xaymab seede sa. 23Ca ëllëg sa, naka la Musaa dugg ca xaymab seede sa rekk, daldi fekk yetu Aaróona wu kër Lewi, jebbi; fekk na mu jebbi, ba tóor, ba meññ ay doomi amànd#17.23 amànd xeetoo naak gerte-tubaab.. 24Ba loolu amee Musaa jële yet yépp ci Aji Sax ji, dem ba ca bànni Israayil gépp, ñépp gis, ku nekk jël yetam.
25Aji Sax ji waxati Musaa, ne: «Dellool yetu Aaróona fa kanam gaalu seede sa, mu dence fa, di firnde ñeel xeetu fippukat wi, ndax nga dakkal seeni xultu ci sama kaw, ba duñu dee.» 26Musaa def noonu. Na ko ko Aji Sax ji sante, na la ko defe.
27Bànni Israayil nag naan Musaa: «Jeexal nanu nag, sànku nanu, nun ñépp ay sànku! 28Gannaaw képp ku jege màkkaanu Aji Sax ji doŋŋ, dangay dee kay, mbaa dunu far jeex tàkk?»
Currently Selected:
Màndiŋ ma 17: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright

: