Màndiŋ ma 10
10
Lu jëm ci liit ya ñu tëgge xaalis
1Aji Sax ji waxati Musaa, ne: 2«Sàkklul ñaari liiti xaalis. Lu ñu tëgglu ba mu jekk nga koy def. Liit yi ngay wootee am ndaje, di ko yékkatee dal yi. 3Bu ñu liitee ñaar yépp, mbooloo mépp ay dajesi fi yaw, ci bunt xaymab ndaje mi. 4Bu ñu liitee benn nag, kilifa yi jiite gàngoori Israayil ñooy dajesi fi yaw. 5Su ñu liitee menn riirum liit mu xumb, dal yi dale penku ñooy fabu. 6Su ñu liitee riirum liit mu xumb, ñaareel bi yoon, dal yi dale bëj-saalum ñooy fabu. Riirum liit mu xumb mooy tegtale seeni fabu. 7Bu dee wooteb ndaje nag, dees koy liit waaye du doon riir mu xumb. 8Na doomi Aaróona sarxalkat yi di wal liit yi, te mu doon dogal bu leen saxal dàkk, ci seen maasoo maas.
9«Bu loolu wéyee, bu ngeen dee xare ci seenum réew, ak noon bu leen songsi, nangeen riiral liit yi riir mu xumb, su boobaa dees na leen bàyyi xel fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ba wallu leen ak seeni noon. 10Seen bési mbég itam, muy seen bési màggal, di seen ndoortel weer, nangeen ciy riiral liit yi riir mu xumb, yéenee ko seen saraxi rendi-dóomal, ak seen saraxi cant ci biir jàmm. Riirum liit yooyu mooy doon seen baaxantal fa seen kanam Yàlla. Maay seen Yàlla, Aji Sax ji.»
Bànni Israayil sàqee nañu tundu Sinayi
11Ca ñaareelu at ma, gannaaw ba bànni Israayil génnee Misra, ca ñaareelu weer wa, keroog ñaar fukkeelu fanam, ca la niir wa bàyyikoo fa tiim màkkaanu seedes kóllëre ga. 12Bànni Israayil daldi sumb seen yooni tukki ya, bàyyikoo màndiŋu Sinayi. Ci kaw loolu niir wa daleji ca màndiŋu Paran.
13Booba lañu njëkka fabu ci kàddug Aji Sax ji, Musaa jottali. 14Raayab dalu Yudeen ña moo njëkka jóg, ànd aki gàngooram, njiital gàngooru Yuda di Naason doomu Aminadab, 15njiital gàngooru Isakareen ña di Netaneel doomu Cuwar, 16njiital gàngooru Cabuloneen ña di Elyab doomu Elon.
17Ci biir loolu ñu wékki jaamookaay ba, Gersoneen ñaak Merareen ñay gàddu jaamookaay ba daldi dem.
18Raayab dalu Rubeneen ña jóg ànd aki gàngooram, topp ca, njiital gàngooru Rubeneen ña di Elicur doomu Sedeyur, 19njiital gàngooru Cimyoneen ña di Selumyel doomu Curisadaay, 20njiital gàngooru Gàddeen ña di Elyasaf doomu Dewel.
21Gannaaw loolu Keyateen ñay gàddu yëf yu sell ya, ñoo fabu, topp ca. Bala ñoo àgg fa ñuy dalewaat nag, day fekk jaamookaay ba sampewaat.
22Ci kaw loolu raayab dalu Efraymeen ña jóg, ànd ak seeni gàngoor, topp ca, njiital gàngooru Efraymeen ña di Elisama doomu Amiyudd, 23njiital gàngooru Manaseen ña di Gamliyel doomu Pedacur, 24njiital gàngooru Beñamineen ña di Abidan doomu Gidoni.
25Ba mu ko defee raayab dalu Daneen ña doora jóg, topp ca gannaaw kuréel yépp, ànd aki gàngooram, njiital gàngooru Daneen ña di Axyeser doomu Amisadaay, 26njiital gàngooru Asereen ña di Pagyel doomu Okkran, 27njiital gàngooru Neftaleen ña di Axira doomu Enan.
28Noonu la bànni Israayil topplantee, ànd ak seeni gàngoor, tegu ca yoon wa.
Bànni Israayil jóge nañu Sinayi
29Ba loolu amee Musaa wax ak Obab doomu Ruwel waa Majan ba, baayu soxnaam, ne ko: «Nu ngi nii jëm fa nu Aji Sax ji wax ne moom lanuy jox. Kaay nu ànd, dem, nu baaxe la, ndax Aji Sax ji moo digee baaxe Israayil.»
30Mu ne ko: «Déedéet, duma dem, samam réew kay laa jëm, ca saay bokk.» 31Mu ne ko: «Bu nu wacc kay, ndax gannaaw yaa xam fu nu wara dal ci màndiŋ mi, yaa nu wara jiite. 32Soo àndeek nun déy, xéewal googa nu Aji Sax jiy baaxeji, dinanu la ci baaxe.»
33Ci kaw loolu ñu bàyyikoo ca tundu Aji Sax ja, doxe fa doxub ñetti fan. Gaalu kóllërey Aji Sax jaa nga leen jiitu diiru ñetti fan ña, di leen wutal dalluwaay. 34Niiru Aji Sax ji nag di leen yiir bëccëg bu nekk, saa yu ñu bàyyikoo ab dal.
35Bu gaal ga jógaan, Musaa da naan:
«Jógaloo, Aji Sax ji, say noon fëlxoo,
say bañ daw la.»
36Bu gaal ga dalee, Musaa ne:
«Dikkaloo Aji Sax ji boroom ndiiraani junniy Israayil.»
Currently Selected:
Màndiŋ ma 10: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright

: