Macë 28
28
Yeesu Almasi bi dekki na
1Gannaaw bésub Noflaay ba nag, ca bésub dibéer ba jiitu ca ayu bésu Yawut ya, Maryaama ma dëkk Magdala ak Maryaama meneen ma ñoo dem, seeti bàmmeel ba. 2Ca saa sa suuf yëngu yëngu bu mag; am malaakam Boroom bi wàcce asamaan, dikk béraŋ doj wa, toog ca kaw. 3Aw meloom a ngay niru melax, ay yéreem weex tàll. 4Wattukat ya tiit di lox, ba mel ni ñu dee.
5Malaaka ma nag àddu ne jigéen ña: «Buleen tiit. Xam naa ne Yeesu ma ñu daajoon ngeen di seet. 6Nekku fi, nde dekki na, na mu ko waxe woon. Ñëwleen seet fi mu tëddoon, 7te ngeen dem gaaw, wax ay taalibeem ne leen: “Dekki na te kat jiituji na leen Galile; foofa ngeen koy gise.” Lii maa leen ko wax.»
8Ba loolu amee jigéen ña fëxe ca bàmmeel ba, ànd ak tiitaange ak mbég mu réy. Ñu daldi daw yégali ko taalibe ya.
9Ci biir loolu rekk Yeesu jekki dajeek ñoom, ne leen: «Jàmm ngeen am!» Ñu ne gurub, jàpp cay tànkam, sujjóotal ko. 10Yeesu ne leen: «Buleen tiit, demleen ne samay bokk, ñu dem Galile; foofa lañu may gise.»
11Naka lañuy dem, ndeke ñenn ca wattukat ya délsi nañu ca dëkk ba, ba àgge sarxalkat yu mag ya mboolem la xew. 12Ba ñooña dajee ak magi askan wa, ba diisoo, xaalis bu takku lañu jox takk-der ya, 13ne leen: «Dangeen di wax ne: “Ay taalibeem a dikk guddi, fekk nu nuy nelaw, ñu sàcc néewam.” 14Bu ci boroom dëkk bi jotee, noo koy naxtaan, te dinanu fexe ba ngeen mucc loraange.» 15Wattukat ya nag jël xaalis ba, daldi def la ñu leen sant. Mbir moomu law na ci biir Yawut yi ba bésub tey jii.
16Fukki taalibe ya ak benn nag dem Galile, ba ca tund wa leen Yeesu digaloon. 17Ci kaw loolu ñu gis ko, daldi koy sujjóotal. Teewul ñenn ña am xel ñaar. 18Yeesu dikk ne leen: «Joxees na ma bépp sañ-sañ fa asamaan ak fi kaw suuf. 19Kon demleen sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóobleen leen ci ndox ci turu Baay bi ak Doom ji ak Noo gu Sell gi, 20te ngeen jàngal leen ñu sàmm mboolem li ma leen sant. Maa ngii nag, di nekk ak yeen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»
Currently Selected:
Macë 28: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright

: