Macë 28:12-15
Macë 28:12-15 KY
Ba ñooña dajee ak magi askan wa, ba diisoo, xaalis bu takku lañu jox takk-der ya, ne leen: «Dangeen di wax ne: “Ay taalibeem a dikk guddi, fekk nu nuy nelaw, ñu sàcc néewam.” Bu ci boroom dëkk bi jotee, noo koy naxtaan, te dinanu fexe ba ngeen mucc loraange.» Wattukat ya nag jël xaalis ba, daldi def la ñu leen sant. Mbir moomu law na ci biir Yawut yi ba bésub tey jii.





