Sarxalkat yi 12
12
Li war ci ku wasin
1Aji Sax ji wax na Musaa ne ko: 2«Waxal bànni Israayil ne leen: Ku ëmb ba wasin, am doom ju góor, dina sobewu diiru juróom ñaari fan. Day sobewu ni bu tolloo ci fan yi muy gis baax. 3Bu bés ba délsee, nañu xarafal xale bi. 4Dina ca teg fanweeri fan ak ñett, ngir setlu ca meret ma. Ci diir booba warula laal lenn lu ñu sellal, mbaa mu dem ca xaymab ndaje ma li feek àppu setloom matul. 5Su amee doom ju jigéen, dina sobewu diiru ñaari ayi bés, mu mel ni ku gis baax. Dina ca teg juróom benn fukki fan ak juróom benn, doora tàggook sobey meret ma.
6«Keroog bu àppu setloom matee, bu doom ja dee góor, bu dee jigéen, na dem ca bunt xaymab ndaje ma te yóbbul sarxalkat bi am kuuy mu am at, muy saraxu rendi-dóomal, ak xati mu ndaw mbaa pitax, mu doon saraxu póotum bàkkaar. 7Na ko sarxalkat bi sarxal fi kanam Aji Sax ji, def ko njotlaayal wasin-bees wi, mu doora tàggook sobey meret ma.»
Loolu la yoon digle ci wasin-bees, mu am doom ju góor mbaa ju jigéen. 8«Su fekkee ne wasin-bees wi amul njëgu kuuy, na indi ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, benn bi di saraxu rendi-dóomal, bi ci des di saraxu póotum bàkkaar. Sarxalkat bi defal ko ku jigéen ki njotlaayam, mu daldi set.»
Currently Selected:
Sarxalkat yi 12: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright

: