YouVersion Logo
Search Icon

Galasi 5:19-21

Galasi 5:19-21 KY

Jëfi bakkan nag yomb naa xàmmee, te mooy: séy yi yoon tere ak jëfi sobe ak yàqute ak bokkaale ak xërëm ak mbañeel ak féewaloo ak kiñaan ak mer mu ëpp ak jiital say bëgg-bëgg ak réeroo ak xàjjalikoo ak ñeetaane ak màndite ak xawaare yiy ànd ak moy ak yeneen yu ni mel. Ma artu leen nag, na ma leen artoo woon: ñiy jëfe noonu, amuñu cér ci nguurug Yàlla.