Galasi 2:15-16
Galasi 2:15-16 KY
Nun danoo juddu diy Yawut, te bokkunu ca bàkkaarkat yooyee di jàmbur yi dul Yawut. Xam nanu nag ne nit ki, du ci jëfi sàmm ndigali yoon la ko Yàlla di baaxee àtteb ku jub, waaye ci ngëm gu mu gëm Yeesu Almasi bi. Te nun itam, Almasi Yeesu lanu gëm, ngir Yàlla àtte nu àtteb ku jub ci kaw gëm gu nu gëm Almasi bi, te du ci kaw jëf ju nu sàmme ndigali yoon. Ndax kat du ci jëfi sàmm yoon lees di baaxee kenn àtteb ku jub.





