Mucc ga 35
35
Bànni Israayil yékkati na jaamookaay ba
(Saar 35—40)
Bésub Noflaay du bésu liggéey
1Musaa nag dajale mbooloom bànni Israayil mépp. Mu wax leen ne leen: «Lii mooy li Aji Sax ji santaane, ngir ñu def ko: 2juróom benni fan lees di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, seen bésub Noflaay bu sell bu mat sëkk la, ñeel Aji Sax ji. Képp ku ci liggéey lenn, dees koy rey. 3Buleen jafal sax sawara fenn ci seeni dëkkuwaay, ci bésub Noflaay.»
Ay sarax war na ci jaamookaay bi
4Musaa dellu wax ak mbooloom bànni Israayil mépp ne leen: «Lii mooy li Aji Sax ji santaane.
5«Génneleen ci seen alal saraxu njébbal bu ñeel Aji Sax ji. Képp ku am yéene ji, na indil Aji Sax ji ab saraxu njébbal: wurus ak xaalis ak xànjar, 6ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, ak kawari bëy 7ak deri kuuy yu ñu wulli, suub xonq, ak deri piipi ak banti séng, 8ak diwu oliw gu ñuy taaloo, ak ndàbb luy xeeñal diwug pal, di xeeñal cuuraay, 9ak ay peri onigsë, ak yeneen per yu ñuy tapp ci xar-sànni meek kiiraayal dënn bi.
10«Mboolem ku xareñ ci yeen, na ñëw, ngeen def li Aji Sax ji santaane lépp: 11jaamookaay bi ak xaymaam ak kiiraayam aki keppoom aki làccam, ak galan yeek jën yeek tegu yi, 12ak gaal geek ay njàppoom ak kubeer gi ñuy amale ag njotlaay, ak rido bi ko làq, 13ak taabal jeeki njàppoom ak ndabam yépp ak mburum teewal mi, 14ak tegukaayu làmp bi, aki jumtukaayam aki làmpam ak diwu làmp bi, 15ak sarxalukaayu cuuraay bi aki njàppoom, ak diwu pal gu sell gi, ak cuuraay lu xeeñ li; ak kiiraayal buntu jaamookaay bi, 16ak sarxalukaayu rendi-dóomal bi, ak caaxub xànjaram aki njàppoom ak li muy àndal lépp; mbalkam njàpp mi akub tegoom, 17ak sor yi yéew jaamookaay bi aki jënam aki tegoom, ak lafu buntu ëtt bi, 18ak xeri jaamookaay bi, ak jën yi yéew ëtt bi ak seeni buum, 19ak yére yu yànj yi ñuy liggéeye ci néeg bu sell bi, yére yu sell yu Aaróona, sarxalkat bi, ak yérey doomam, yi ñuy sol bu ñuy sarxal.»
20Ci kaw loolu mbooloom bànni Israayil gépp bàyyikoo fa Musaa. 21Ba mu ko defee mboolem ña ca am pastéefu xol ak mboolem ña ca seen xel xiir, ñépp dikk, indil Aji Sax ji saraxu njébbal ngir defar xaymab ndaje mi, yékkati ko, tey def màggal gi mu laaj, ngir itam defar yére yu sell yi. 22Góor ak jigéen bokk dikk, mboolem ñi am yéeney xolam, mboolem ñi bëgga indi wurus, defal ko Aji Sax ji saraxu yékkati-jébbale; ñii indi ay lam, ñii jaaroy nopp, ñii jaaroy loxo, ñii ay caq, ñii ay gànjari wurus yu nekk rekk. 23Te it mboolem ñi dencoon wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ak kawari bëy mbaa deri kuuy yu ñu suub xonq, mbaa deri piipi, ñoom ñépp a indi la ñu dencoon. 24Képp ku namma jébbal xaalis mbaa xànjar, jébbal nga ko Aji Sax ji, te itam képp ku dencoon bantu séng bu jëm ci mboolem liggéeyu sarxal bi, indi nga bant bi. 25Ci biir loolu jigéen ñu xareñ ñépp ëcce seeni loxo, ngir waajal wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñu boole, indi. 26Mboolem jigéen ñi ko mane te am yéeneem itam, daldi ëcc kawari bëy. 27Njiit yi nag indi ay peri onigsë ak yeneen per yiy tappe ci xar-sànni meek kiiraayal dënn bi, 28aki xeeñal, akug diw ngir làmp beek diwu pal geek cuuraay lu xeeñ li. 29Mboolem bànni Israayil, góor ñeek jigéen ñi am yéeney indi lu jëm ci liggéey bi Aji Sax ji santaane, Musaa jottali, ñoom ñépp a indil Aji Sax ji ay saraxi yéene.
Beccalel ak Oliyab tàmbali nañu liggéey bi
30Musaa nag ne bànni Israayil: «Gisleen, Aji Sax ji moo woo Beccalel ci turam. Beccalel, Uri mooy baayam; Uri, Ur Yudeen bi di baayam. 31Moo ko feesale xelum Yàlla ak xareñte ak déggin ak xam-xam ak manoorey bépp xeetu liggéey, 32ngir muy nas ay liggéeyi wurus ak xaalis ak xànjar, 33di yatt per yu muy tapp, di yatt bant, di liggéey lu nekk. 34Mayu jàngale itam Aji Sax ji yeb na ko cib dënnam, moom ak Oliyab, Daneen bi, doomu Axisamaag; 35te moo leen feesal xareñte, ngir bépp liggéey, ci wàllu yatt ak nataal, ak liggéeyu wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. Mane nañoo ràbb te itam dañuy sos seen taarali bopp.
Currently Selected:
Mucc ga 35: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright

: