Mucc ga 32:7-8
Mucc ga 32:7-8 KY
Aji Sax ji nag waxati Musaa ne ko: «Gaawal wàcc, ndax sa mbooloo ma nga génne réewum Misra def nañu yàqute. Jàdd nañu xaat yoon wa ma leen tegoon. Dañoo sàkkal seen bopp sëllu wu ñu móol, di ko sujjóotal aka sarxalal, naan: “Israayiloo, seen yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!”»





