Mucc ga 16:3-4
Mucc ga 16:3-4 KY
Ña nga naa leen: «Céy ngalla nun, su nu sañoon dee, Yàlla moom nu ca réewum Misra, fa nu daan uufe cini yàpp, ñam wa ne gàññ, nu suur këll. Yeena nu indi ba ci màndiŋ mii, ngeen nara xiifloo mbooloo mii mépp, ba ñu dee.» Ba loolu amee Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Maa ngi nii di tawal bànni Israayil ñam wu jóge asamaan, te na mbooloo mi dem bés bu set, fori njëlu bés ak bés. Ma nattu leen ci, ba xam ndax dinañu doxe sama ndigalu yoon am déet.





