YouVersion Logo
Search Icon

Mucc ga 10:1-2

Mucc ga 10:1-2 KY

Ba loolu weesoo Aji Sax ji dafa wax Musaa ne ko: «Demal ca Firawna. Maa dëgëral boppam, mooki dagam, ngir jëfe samay firnde fi seen biir. Su ko defee ngeen mana nettali seeni doom ak seeni sët ni ma toroxale waa Misra, ak sama firnde yi ma def fi seen biir, ndax ngeen xam ne man maay Aji Sax ji.»