YouVersion Logo
Search Icon

Efes 4:11-13

Efes 4:11-13 KY

Moo may ñii di ay ndawam, ñee di ay yonent, ñee di ay xamlekati xibaaru jàmm bi, ñale di ay sàmmi mbooloom gëmkat ñi, mbaa ay jàngalekat. Almasi bi moo waajale noonu ñu sell ñi, ba ñu mana bey seen sas ci liggéeyam, ngir tabax mbooloom gëmkat mi taxawe yaramu Almasi bi. Su ko defee nu mana màgg nun ñépp ba doon benn ci ngëm ak ci xam-xam bu mat ci Doomu Yàlla ji, ba kera nuy doon magum jëmm, bay tollook taxawaayu Almasi bi mat sëkk.

Free Reading Plans and Devotionals related to Efes 4:11-13