Bible App logo
Search Icon

Jëf ya 5:3-5

Jëf ya 5:3-5 KY

Ba loolu amee Piyeer ne ko: «Anañas, lu waral Seytaane di fees sab xol, ba ngay wor Noo gu Sell gi, di làq lenn ci njëgu tool bi? Ba mu jaragul, du yaa doon boroom? Gannaaw ba mu jaree it, xanaa du njëg gaa ngi ci sa loxo ba tey? Ana noo mana xajale mii mébét ci sa xol? Du nit nga wor de, waaye Yàlla nga wor.» Naka la Anañas dégg kàddu yooyu, mu daldi daanu, dee. Tiitaange ju réy nag dikkal ña ko dégg ñépp.