Jëf ya 11:23-24
Jëf ya 11:23-24 KY
Ba Barnabas dikkee ba gis yiw wi leen Yàlla may, dafa bég, di leen ñaax ngir ñu ŋoy ak seen xol ci Sang bi. Ndaxte Barnabas nit ku baax la woon, fees ak Noo gu Sell gi ak ngëm. Mbooloo mu takku nag dolliku ci Sang bi.





