2.Korent 5:15-16
2.Korent 5:15-16 KY
Te ki dee ngir ñépp, daa dee ngir ñiy dund bañatee dund ngir seen bopp, xanaa di dund ngir ki dee ngir ñoom, ba dekki. Kon nag gannaaw-si-tey, ni nitu suuxu neen di xoole moroomam, nun xooleetunu ko kenn. Doonte ni nitu suuxu neen lanu xoole woon Almasi bi, léegi xooleetunu ko noonu.








