1.Yowaan 4:1-2
1.Yowaan 4:1-2 KY
Soppe yi, du képp ku ne mu ngeek Noowug Yàlla, ngeen di gëm, waaye nattuleen noo gi mu waxe, ba xam ndax ci Yàlla la jóge, ndax yonenti caaxaan yu baree dajal àddina. Ni ngeen di xàmmee Noowug Yàlla nag moo di képp ku ne mu ngeek Noo gi, te kàddoom dëggal ne, Yeesu Almasi bi moo dikke yaramu suux, kooka noo ga muy waxe ci Yàlla la bokk.








