1
Tit 2:11-12
Téereb Injiil
TI
Ndaxte yiwu Yàlla feeñ na te ubbil na ñépp buntu mucc. Moo nu digal, nu dëddu weddi ak bëgg-bëggi jamono, tey dund ci àddina cig maandu, njub ak ragal Yàlla
Compare
Explore Tit 2:11-12
2
Tit 2:13-14
di séentu bés bu tedd bi nu yaakaar, maanaa Yàlla ju màgg ji, di sunu Musalkat Yeesu Kirist, feeñ ci biir ndamam. Joxe na bakkanam ngir nun, ba jot nu ci lépp lu bon, te beral nu boppam, di xeet wu sell te ràññiku ci jëf yu baax.
Explore Tit 2:13-14
3
Tit 2:7-8
Te yaw, ci lépp lu mu mana doon, nekkal ab royukaay ci jëf yu baax. Na sa njàngle wér te am faayda, ànd ak wax yu wér yu kenn manta diiŋat, ngir sunuy noon rus ba wedam, ci li ñu amul dara lu ñu nu tuumaal.
Explore Tit 2:7-8