1
Room 2:3-4
Téereb Injiil
TI
Yaw nag miy àtte ñiy def loolu, te di ko def, ndax defe nga ne dinga rëcc ci àtteb Yàlla? Ndax dangaa xeeb mbaaxu Yàlla, mi yéexa mer te di la muñal? Xanaa xamuloo ne Yàllaa ngi lay won baaxaayam, ngir nga réccu say bàkkaar?
Compare
Explore Room 2:3-4
2
Room 2:1
Kon nag képp ku mu mana doon, yaw miy àtte sa moroom ak ñaaw njort, amuloo aw lay, ndaxte àtte sa moroom, daan sa bopp la; yaa ngi koy àtte ndax ay jëfam, fekk yaw itam noonu ngay jëfe.
Explore Room 2:1
3
Room 2:11
Ndaxte ñépp a yem fa kanam Yàlla.
Explore Room 2:11
4
Room 2:13
Kon déglu yoonu Musaa rekk doyul; du loolu mooy tax nit jub ci kanam Yàlla; kiy sàmm yoon wi, moom la Yàlla di àtte ni ku jub.
Explore Room 2:13
5
Room 2:6
bés booba dina delloo ku nekk ay jëfam.
Explore Room 2:6
6
Room 2:8
Waaye ñi dëgër bopp, ba tanqamlu dëgg, di topp lu jubadi, seen pey mooy dooni merum Yàlla ak toroxte.
Explore Room 2:8
7
Room 2:5
Waaye ndegam dëgër nga bopp te bëgguloo réccu, yaa ngi dajale merum Yàlla ci sa bopp. Ndaxte Yàlla sàkk na bés bu muy wone àtteem bu jub bi te meram wàcc ci ñi bon
Explore Room 2:5