1
Peeñu ma 5:9
Téereb Injiil
TI
Ñu daldi woy woy wu bees naan: «Yeyoo ngaa jël téere bi te dindi tayu yi, ndaxte reyees na la, te jotal nga Yàlla ak sa deret ay nit ñu bokk ci bépp giir ak kàllaama ak réew ak xeet.
Compare
Explore Peeñu ma 5:9
2
Peeñu ma 5:12
Ñuy xaacu naan: «Gàtt ba ñu rendi woon yeyoo na kàttan, alal, xel, doole, teraanga, ndam ak cant.»
Explore Peeñu ma 5:12
3
Peeñu ma 5:10
Def nga leen askanu sarxalkati Buur Yàlla sunu Boroom, di ko jaamu, te dinañu nguuru ci àddina.»
Explore Peeñu ma 5:10
4
Peeñu ma 5:13
Ma dégg itam mbindeef, yi nekk ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf, ci géej gi,-- mbindeef yépp naan: «Yal na cant, teraanga, ndam ak nguur féete ak ki toog ci gàngune mi, ak Gàtt bi, ba fàww.»
Explore Peeñu ma 5:13
5
Peeñu ma 5:5
Noonu kenn ca mag ña ne ma: «Bul jooy. Xoolal, Gayndeg giiru Yuda, ki soqikoo ci Daawuda, daan na, ba am sañ-sañu dindi tayu yi te ubbi téere bi.»
Explore Peeñu ma 5:5