1
Macë 7:7
Téereb Injiil
TI
«Ñaanleen, ñu may leen; seetleen te dingeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
Compare
Explore Macë 7:7
2
Macë 7:8
Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la.
Explore Macë 7:8
3
Macë 7:24
«Képp ku dégg nag lii ma leen wax, te di ko jëfe, dinga mel ni nit ku am xel, ku tabax këram, samp ko ciw doj.
Explore Macë 7:24
4
Macë 7:12
«Kon nag lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal; ndaxte loolu moo ëmb yoonu Musaa ak waxi yonent yi.
Explore Macë 7:12
5
Macë 7:14
Waaye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw sew na, te ñi ko gis barewul.
Explore Macë 7:14
6
Macë 7:13
«Jaarleen ci bunt bu xat bi, ndaxte bunt bi ak yoon wi jëm sànku yaatu nañu, te ñi ciy jaar bare.
Explore Macë 7:13
7
Macë 7:11
Ndegam yéen ñi bon yéena mana jox seeni gone lu baax, astamaak seen Baay bi nekk ci kaw dina jox lu baax ñi ko koy ñaan!
Explore Macë 7:11
8
Macë 7:1-2
«Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, ngir bañ ñu àtte leen yéen itam. Ndaxte dees na leen àtte ak ni ngeen di àttee, nattal leen ak li ngeen di nattale.
Explore Macë 7:1-2
9
Macë 7:26
Waaye képp ku dégg lii ma leen wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku ñàkk xel, ku tabax këram ci gannuus bi.
Explore Macë 7:26
10
Macë 7:3-4
Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw? Walla nan ngay waxe sa mbokk: “May ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” fekk gànj a ngii ci sa bët yaw?
Explore Macë 7:3-4
11
Macë 7:15-16
«Moytuleen ñi mbubboo turu yonent. Dañuy ñëw ci yéen, yor melow xar, waaye ci biir ay bukki yu soxor lañu. Dingeen leen xàmmee ci seeni jëf. Ndax dees na witte reseñ ci dédd, walla figg ci xaaxaam?
Explore Macë 7:15-16
12
Macë 7:17
Noonu garab gu baax gu nekk dina meññ doom yu neex, waaye garab gu bon dina meññ doom yu bon.
Explore Macë 7:17
13
Macë 7:18
Garab gu baax manula meññ doom yu bon, naka itam garab gu bon manula meññ doom yu neex.
Explore Macë 7:18
14
Macë 7:19
Garab gu nekk gu dul meññ doom yu neex, dees na ko gor, sànni ko ca sawara sa.
Explore Macë 7:19