1
Macë 16:24
Téereb Injiil
TI
Gannaaw loolu Yeesu ne taalibeem ya: «Ku bëgga aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, te gàddu bant bi ñu ko wara daaj, doora topp ci man.
Compare
Explore Macë 16:24
2
Macë 16:18
Te maa ngi lay wax lii: yaa di Piyeer, te ci kaw doj wu réy woowu laay samp mbooloom ñi ma gëm, te dooley dee du ko manal dara.
Explore Macë 16:18
3
Macë 16:19
Dinaa la jox caabiy nguuru Yàlla Aji Kawe ji; li nga yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan; li nga yiwi ci àddina dees na ko yiwi ci asamaan.»
Explore Macë 16:19
4
Macë 16:25
Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, jotaat ko.
Explore Macë 16:25
5
Macë 16:26
Te it moom àddina sépp lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam? Te nit, lu mu wara weccee bakkanam?
Explore Macë 16:26
6
Macë 16:15-16
Noonu Yeesu ne leen: «Waaye yéen, ku ngeen may teg?» Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer ne: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.»
Explore Macë 16:15-16
7
Macë 16:17
Yeesu ne ko: «Barkeel ñeel na la, Simoŋ doomu Yunus, ndaxte du nit moo la xamal lii, waaye sama Baay bi nekk ci kaw.
Explore Macë 16:17