1
Yawut ya 10:25
Téereb Injiil
TI
Te bunu bàyyi sunu ndaje yi, ni ko ñenn ñi di defe, waaye nanuy nàddante ci ngëm, di ko feddali, fi ak yéena ngi gis bésu Boroom biy jubsi.
Compare
Explore Yawut ya 10:25
2
Yawut ya 10:24
Nanu seet ni nu mana xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax.
Explore Yawut ya 10:24
3
Yawut ya 10:23
Nanu jàpp ci yaakaar, ji nu am, te baña toqi, ndaxte ki nu dig, lu mu wax def ko.
Explore Yawut ya 10:23
4
Yawut ya 10:36
Dangeena wara muñ, ba def coobarey Yàlla, sooga jot li mu leen digoon.
Explore Yawut ya 10:36
5
Yawut ya 10:22
kon nanu jege Yàlla ak xol bu laab, ak ngëm gu ànd ak kóolute, am xel mu dal ci bépp yeraange, ak yaram wu ñu raxas ci ndox mu sell.
Explore Yawut ya 10:22
6
Yawut ya 10:35
Kon nag buleen sàggane kóolute gi ngeen am, ndaxte ëmb na yool bu mag.
Explore Yawut ya 10:35
7
Yawut ya 10:26-27
Gannaaw ba nu nangoo xam dëgg ba noppi, bu nu teyee di def bàkkaar, kon sarax dootul am ngir bàkkaar yooyu. Déedéet, bu nu defee noonu, dinanu tiit di xaar àtte ba, muy taal bu yànj, biy wara lakk nooni Yàlla yi.
Explore Yawut ya 10:26-27