1
Peeñu ma 5:9
Kàddug Yàlla
KY
Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote ay niti gépp giir ak wépp làkk ak wépp xeet ak wépp askan, ñu doon ñoñi Yàlla.
Compare
Explore Peeñu ma 5:9
2
Peeñu ma 5:12
Ña ngay àddu ca kaw, naan: «Xar mi ñu rendi woon moo yeyoo kàttan ak alal, yeyoo xel ak doole, moo yeyoo worma, yeyoo darajaak cant.»
Explore Peeñu ma 5:12
3
Peeñu ma 5:10
Yaa leen def ñu doon nguurug sarxalkat yi, ñeel sunu Yàlla, te dinañu nguuru ci àddina.»
Explore Peeñu ma 5:10
4
Peeñu ma 5:13
Ba loolu amee mboolem ndundati asamaan ak kaw suuf ak biir suuf ak géej ak mboolem li ci seen biir, ñoom ñépp di wax, may dégg, naan: «Ki toog ci ngàngune mi ak Xar mi, nañu jagoo cant ak worma ak darajaak kàttan, tey ak ëllëg ba fàww.»
Explore Peeñu ma 5:13
5
Peeñu ma 5:5
Kenn ci mag ñi ne ma: «Bul jooy. Ma ne, Gayndeg giirug Yuda, njebbital Buur Daawuda daan na. Mooy ubbi téere beek juróom ñaari tayoom.»
Explore Peeñu ma 5:5