1
Màndiŋ ma 20:12
Kàddug Yàlla
KY
Aji Sax ji nag ne Musaa ak Aaróona: «Gannaaw gëmuleen ma, ngir wormaal sama sellaay fi kanam bànni Israayil, loolu tax na dungeen yóbbu mukk mbooloo mii ca réew ma ma leen jox.»
Compare
Explore Màndiŋ ma 20:12
2
Màndiŋ ma 20:8
«Jëlal saw yet, nga dajale mbooloo mi, yaak sa mag Aaróona, ngeen wax ak doj woowu, ñuy gis, mu xelli am ndox. Te nga sottil leen ndox mu jóge ci doj wi, nàndale ko mbooloo mi, ñook seenug jur.»
Explore Màndiŋ ma 20:8
3
Màndiŋ ma 20:11
Ci kaw loolu Musaa yékkati loxoom, dóor yetam ca doj wa ñaari yoon, ndox mu bare wale ca, mbooloo ma daldi naan, ñook seenug jur.
Explore Màndiŋ ma 20:11
4
Màndiŋ ma 20:10
Musaa ak Aaróona nag dajale mbooloo ma fa janook doj wa, Musaa ne leen: «Yeen diiŋatkat yi, dégluleen ma fii! Doj wii, tee nu leen cee génneel am ndox boog?»
Explore Màndiŋ ma 20:10