Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole faagaagal mukk lépp luy dund, nii ma ko defe.
Li feek suuf di suuf,
muy nji walla ngóob,
sedd aku tàngoor,
nawet it mbaa noor,
mbaa guddeek bëccëg,
lenn du ci dakk.»