1
Njàlbéen ga 50:20
Kàddug Yàlla
KY
Dëgg la, fexeel ngeen ma lu bon, waaye Yàllaa ko walbati, def ko lu baax, ba dogal li am tey jii, muy bakkan yu bare yi mucc.
Compare
Explore Njàlbéen ga 50:20
2
Njàlbéen ga 50:19
Yuusufa nag ne leen: «Buleen am dara lu ngeen di ragal. Xanaa maay Yàlla?
Explore Njàlbéen ga 50:19
3
Njàlbéen ga 50:21
Kon nag buleen tiit, dinaa leen yor, yeen ak seeni doom.» Yooyu kàddu la dalale seen xol, ba ñu am jàmm.
Explore Njàlbéen ga 50:21
4
Njàlbéen ga 50:17
Waxleen Yuusufa ne ko, sa baay nee: “Say mag def nañu la lu bon moos, waaye ngalla baal leen seeni tooñ ak àq ji ñu la ameel.” Kon rikk waay, baal nu àq, ndax nun nook sa baay a bokk jenn Yàlla ju nuy jaamu.» Ba ñu waxee Yuusufa loolu, mu daldi jooy.
Explore Njàlbéen ga 50:17
5
Njàlbéen ga 50:24
Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla dina dikk, yéwéne leen moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.»
Explore Njàlbéen ga 50:24
6
Njàlbéen ga 50:25
Booba la Yuusufa wax doomi Israayil, ne leen: «Giñalleen ma ne bés bu Yàlla dikkee ba yéwéne leen, dingeen yóbbaale samay yax, waaye dungeen ma fi bàyyi.»
Explore Njàlbéen ga 50:25
7
Njàlbéen ga 50:26
Gannaaw loolu Yuusufa nelaw ci téeméeri atam ak fukk. Ñu waajal néew ba, ba du yàqu, daldi koy yeb cib tàdd, denc ko foofa ca Misra.
Explore Njàlbéen ga 50:26