1
Mucc ga 8:18-19
Kàddug Yàlla gi
KYG
Waaye bu keroogee dinaa ci musal diiwaanu Gosen, ga sama ñoñ dëkke, ba ay weñ du fa same, ndax nga xam ne, man Aji Sax ji maa ngi ci digg réew mii, te maay musal sama ñoñ ci musiba moomuy dal saw askan. Ëllëg firnde jooju dina am.’ ”»
Compare
Explore Mucc ga 8:18-19
2
Mucc ga 8:1
Ba loolu weesee Aji Sax ji ne Musaa: «Waxal Aaróona, ne ko mu ŋàbb yet wi, tàllal loxoom, tiimale ko dex yi, ak yooni ndox yeek déeg yi, ngir indi mbott yi ci biir réewum Misra.»
Explore Mucc ga 8:1
3
Mucc ga 8:15
Ñeengokat ya ne Firawna: «Lii de Yàlla rekk a ko man!» Teewul Firawna wéye të rekk, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.
Explore Mucc ga 8:15
4
Mucc ga 8:2
Aaróona tàllal loxoom, mu tiim ndoxi Misra, mbott ya jóg, lal réewum Misra.
Explore Mucc ga 8:2
5
Mucc ga 8:16
Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: «Teelala xëy ëllëg ca Firawna, buy génn jëm ca ndox ma, nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu dem jaamuji ma.
Explore Mucc ga 8:16
6
Mucc ga 8:24
Firawna àddu ne: «Dinaa leen may, ngeen dem ca màndiŋ ma, rendili seen Yàlla Aji Sax ji sarax, waaye buleen sore lool. Ñaanal-leen ma nag.»
Explore Mucc ga 8:24
Home
Bible
Plans
Videos