1
Mucc ga 4:11-12
Kàddug Yàlla gi
KYG
Aji Sax ji ne ko: «Ku sàkkal nit gémmiñ? Kan mooy luuwal, di tëxal, di gisal mbaa muy gumbaal? Xanaa du man Aji Sax ji? Demal rekk, man maay ànd ak yaw booy wax, di la xamal li ngay wax.»
Compare
Explore Mucc ga 4:11-12
2
Mucc ga 4:10
Musaa nag ne Aji Sax ji: «Da di, Boroom bi, man naka jekk duma nitu waxkat, du démb, du tey jii ngay wax ak man. Dama di ku leeb, Sang bi, te tëlee wax.»
Explore Mucc ga 4:10
3
Mucc ga 4:14
Aji Sax ji nag mer ba fees ndax Musaa. Mu ne ko: «Sa mag Aaróona, Leween bi, da fee nekkul? Moom, xam naa ne ku mana wax la. Mu ngi lay gatandusi sax, te bu la gisee, bég.
Explore Mucc ga 4:14
Home
Bible
Plans
Videos