Nees di xame ne daj naa saw yiw, maak sa ñoñ, te fekk ànduloo ak nun, ba nu doon, maak sa ñoñ, ñu ràññiku ci biir mboolem xeet yi ci kaw suuf?»
Aji Sax ji ne Musaa: «Loolu nga wax, moom laa lay defal, ndax daj nga samaw yiw, te it maa la xam ci saw tur.»