«Gisal, maa woo Beccalel ci turam. Beccalel, Uri mooy baayam; Uri, Ur Yudeen bi di baayam. Maa ko feesale sama xel, xareñte ak déggin ak xam-xam ak manoorey bépp xeetu liggéey, ngir muy nas ay liggéeyi wurus ak xaalis ak xànjar, di yatt per yu muy tapp, di yatt bant, di liggéey lu nekk.